COPPITE YI BASIIRU JOMAAY FAY DIGE

Aali Jàllo ("Defuwaxu.com")

Démb la Njiitu réewum Senegaal lu bees li doon biral kàddoom yu njëkk. Fa otel Radison la joxoon dig-daje taskati xibaar yi ci 21i waxtu. Waaye, xaw na yéex a tàmbali.

Bassiru Jomaay Fay am na lu mu jàngal ay naataangoom ci pólitig. Nde, ci dibéer ji, njureef yi dañ doon rot di jëm ci booram. Muy raafal mbañ-gàcce yi, di waabale pekk yi, di rawee yeneen lawax yi lim yu takkoo takku. Bi 20i waxtu di jot, daanaka lépp leeroon na. Waaye, Basiiru Jomaay Fay daf ne tekk tekkaaral. Génnul fenn di yuuxu ndam, ni ko Maki Sàll ak i àndandoom teelee woon def atum 2019.

Muy moom, Basiiru Jomaay Fay, di Usmaan Sonko walla kàngaami Pastef yi, kenn ŋaaŋu ci. Dañoo bàyyi yeneen lawax yi nangul seen bopp, ndokkale Njiitu réewum Senegaal lu bees li : Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Ba ci subas altine ji sax, moom Basiiru, waxul. Dafa xaar ba nattaangoom (adversaire) bi gën a fës nangul ko ndamam, ak Maki Sàll mi mu nar a wuutu, mu sog di àddu. Dal googu ak teey bi, lees namm la ci njiit. Li ci gën a yéeme mooy ne, moom ndaw la. Ndax, ci altiney démb ji, 25 màrs 2024, lay sog di matal 44eelu atam.

Noonee la jëlee kàddu gi, ci guddig altine ji, wax ak Senegaal, wax ak àddina. Ginnaaw nuyoo yeek cant yi, dafa njëkk a leeral xeetu njiit li mu namm a doon. Mu ne :

“Dama fas yéene jiite réew mi cig woyof, teg ko ci lu leer.”

Li ko tax a tàmbalee ci lii mooy ne, at yii weesu, lees nemmeeku ci njiit yi fi nekkagum mooy ab jaay doole, xoqatal, nappaaje, jàppaate, fitnalaate ak reyaate. Rax-ci-dolli, bari nay mbir yu lëndëm ci ni ñu yoree woon réew mi, rawatina ci wàllu nger ak luubal. Li ëpp ci Saa-Senegaal yidemoon ba yàqi. Ndaw ñiy gedd réew mi, di mbëkk ak a gàddaay ngir dàqi seen wërsëg feneen, rawale seen bakkan walla wuti noflaay bitim-réew. Basiiru dafa bëgg dakkal loolu. Ndax, moom dafa gëm ne :

“…tànneef bii dina tijji yoonu yaakaar ak yokkute”.

Kon askanu Senegaal a ko tànn. Askan wiy tànn nag, ciy wote la koy jaare. Wote yooyu, caytug Bokkeef gi fi nekk a koy amal ci njiitalu Njiitu réew mi. Wote yii nag, nit ñi tiitoon nañ ci lool. Waaye, li ñu ci doon ragal amul. Ndax, wote yi am nañ ci jàmm te kenn ci lawax yi kaasul. Loolu nag bu amee, ñi amal wote yi ñoo ko waral. Dees na leen ci delloo njukkal. Moo tax Basiiru Jomaay Fay daldi Fay Naar bi xoromam, delloo njukkal Maki Sàll ci kàddu yii :

“Noo ngi rafetlu taxawaayu Maki Sàll ci fan yu mujj yii. Ndax, moo waral joŋante yu leer yi nu am…”

Moom it Basiiru, fas na yéene doxal ci njub ak jubal. Yemu ca de. Dige na ne, dina sàmm alalu Senegaal ju gën a réy joj, ñépp moom lañ ko ñeewee, muy jàmmoo ak bennoo bi fi am. Naka noonu, fas na yéene juboole Saa-Senegaal yépp.

Fàttewul sas bi koy xaar ci coono ak tolof-tolof yi askan wiy jànkoonteel jamono jii. Te, jafe-jafe yi gën a sonal Saa-Senegaal yi dañuy dellu ci dund bi, paj mi ak njàng mi. Doomu Njanjaay ji neeti :

“Lépp li nga xam ne war nanu cee taxaw ba dund bi yomb ci Saa-Senegaal yi, paj mi yomb ci Saa-Senegaal yi, njàng mi yomb ci Saa-Senegaal yi, dinanu ci taxaw ci lu jamp…”

Waaye, ngir mu jëmmal nisër boobu, fàww Saa-Senegaal yi mënal seen bopp. Loolu la xam ba tax ko waxaat ne :

“Alal ji nga xam ne moom la Senegaal gépp bokk, dinanu fexe ba ku ci nekk la nga war a jot nga jot ci…”

Wolof nee na, mbooloo mooy doole. Te, lu kenn mën, ñaar a ko ko dàq. Sunu buurub seereer bi umpalewu ko. Ndax, biral na ne :

“Lii nga xam ne nun ñépp noo ko bokk, muy Senegaal, noo ngi dalal xelu ñépp ne dinanu ci ànd ak ñépp, waxtaan ci ak ñépp, muy kujje gi, muy way-pólitig yi ak sax ñi bokkul ci pólitig bi…”

Bu dee wàllu bitim-réew, njëkkee ko biir Afrig, sunu Njiitum réew lu bees li daf ne :

“Dinan taxaw, fexe ba gëdd bi Afrig war a am ci àddina si mu am ko…”

Dalal na xeli réewi doxandéem yiy faral di liggéeyandook Senegaal. Wax na leen ne, Senegaal ga woon moo fi nekk ba tey. Ubbi na buntu yi ñeel képp ku bëgg a liggéey ak Senegaal, dugal fi say koppar. Waaye, njàmbaas na ci waxam ji ne, àqi Senegaal lay jiital. Dootuñu salfaañe àqi askan wi, di jël seen alal di ko tayle tubaab yi. Ci weneen waxiin, Basiiru Jomaay Fay day dog buumu njaam gi fi yàgg a am.

Muy ay coppite yu sunu Njiitum réew lu bees li dige. Ginnaaw wax nag, jëf. Askan waa ngi xaar naka lay jëmmalee naalam bi ak gan xeetu Càmm lay teg.

Connexion utilisateur

Commentaires récents

  • Kréyolad 1052: Polo chanté

    Jid, sa vré! Sé lè on mizisiyen ka mò...

    Frédéric C.

    23/11/2024 - 20:10

    ...ou ka trouvé tout diks-li, òben yo ka viré enprimé tou sa i fè-a vitman présé! Lire la suite

  • "Local", "Traditionnel", "Typique", "D'Antan" "Territoire" et autres euphémismes

    Il y a pire que ça...

    Frédéric C.

    23/11/2024 - 15:38

    ...À une époque pas si lointaine, l’adjectif qualificatif "national" était fréquemment utilisé po Lire la suite

  • La religion chrétienne serait-elle une religion afro-caribéenne ?

    Avec des ritournelles de vie chère ...

    Veyative

    21/11/2024 - 05:55

    ce sera très drôle! Lire la suite

  • Jean Crusol : "Première tentative d'un gang du narcotrafic de s'imposer dans le paysage politique et social de la Martinique"

    VOUS ACCUSEZ LES MANIFESTANTS MAIS...

    Albè

    20/11/2024 - 10:47

    ...vous vous bouchez les yeux quand il s'agit d'identifier les VRAIS responsables de la situation Lire la suite

  • Jean Crusol : "Première tentative d'un gang du narcotrafic de s'imposer dans le paysage politique et social de la Martinique"

    Propos gravissimes de Crusol

    Nuit noire

    19/11/2024 - 13:10

    Les propos de Crusol sont gravissimes .C'est néanmoins une analyse originale qui mérite qu'on s'y Lire la suite