AMNISTI : LIGGÉEY BI DOOR NA

Paap Aali Jàllo ("Defuwaxu.com")

Ci altiney jii, 4 màrs 2024, lees di fénc sémbub àtte bees duppee ci tubaab “loi d’amnistie”. Maanaam, ab xeetu àtte bob, day far ay jëf ci benn diir, setal seen i boroom ba kenn du leen leen toppeeti. Njiitu réew mi ci boppam, Maki Sàll, moo ko sumb, fas yéene ko jàllale ça Ngomblaan ga ak i dépiteem. Ñoom, dépitey lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar, Njiitu réew mi jot na leen a dalal fa pale ba. Ñàkkul ne, “loi d’amnistie” bi lañ doon waxtaane.

Ñi bokk ci Ndajem njiiti Ngomblaan gi dina daje tey ci altine. Jubluwaay bi mooy ñu fénc mbirum sémbub àtte biy far i jëf. Ci li ñeel mbir mi, yéenekaay Les Échos xamle na ni, Njiitu réew mi, Maki Sàll, dalal na dépite yu lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar fa pale ba. Li mu ko dugge woon mooy gaaral leen “loi d’amnistie” boobu mu sumb ngir ñu waxtaane ko. Bu sémbub àtte bi jàllee nag, day far, maanaam neenal jéppi jëf ju fi nit jot a def diggante màr 2021 ak suwe 2023 ñeel ay tóoxidóona ak i ñaawteef yu aju ci doxi ñaxtu yi fi jot a am ci wàllu pólitig añs.

Ci weneen waxun, bu mébétu nguur gi àntoo, dees na far (amnestier) jépp xeetu jëf joo xam ne, jàppeesoon na ko niki pékke (Crime) walla njombe (correctionnel). Mu di jëf yoy, ñu ngi ame ci diir biy dox diggante, 1eelu fanu féewiryee 2021 jàpp 25eelu fanu féewiryee 2024 fi Senegaal ak fa bitim-réew. Muy tamit ay jëf yu aju ciy ñaxtu, pólitig walla sax mu jëf yuy dellu ci ñaari fànn yooyii te ñu jaarale leen ci jumtukaayi jokkoo yi, rawatina mbaali jokkoo yi. Dees na baal way-jëf yi, moo xam jot nañu leen a àtte walla déet…

Donte ne ñu bari ànduñu ci, Njiitu réew mi bëggul a dellu ginnaaw ci naalam bile. Dafa di, bakkan yu baree bari rot nañ ci diggante bi te, ñu ci bari, ay bali fetal ñoo leen rey walla ay metital yu leen takk-der yi teg. Rax-ci-dolli, amul benn luññutu bu ci njiiti yi def. Nga teg yàqu-yàqu yeek jàpp yu bari yi. Jàppees na ni, moom Maki Sàll, boppam ak i farandoom la bëgg a ragg, setal leen, làq leen ngir ñu bañ leen a toppe dara keroog bu leen ñeneen wuutoo. Ñu baree ngi kaas nag. Waaye, Njiitu réew mi dafa tanqamlu ñiy kaas ñépp.

Bu ko defee, Ndajem njiit yi (conférence des présidents) dina waxtaane sémb bi tey ngir tëral arminaatu (calendrier) liggéey yi ci jëm.

Dees na ci ñëwaat ak xibaar yu yees.

Connexion utilisateur

Dans la même rubrique

Commentaires récents