BARSAA WALLA… BARSÀQ !… LU XEW CI MIIM RÉEW?

Uséynu Béey ("Defuwaxu.com)

Rubrique

Géej gaa ngiy wann sunu doom yi. Mbete jasig juy warax béy bu lab. Ay fukki, ay téeméeriy, ay junniy waxambaane ak, léeg-léeg sax, ay janq walla ay jeeg ñooy song géej gi, wuti Barsaa walla…

Barsàq ! Ñi ëpp ci ñoom, dañuy des ci ndox mi, ñuy mag di ndaw, di góor di jigéen, liir yi sax, ci lañu. Te musiba bii, du tey, du démb la fi xewe : lu ëpp fukki at a ngi nii, Senegaal di dund lu ni mel ! Waaye, jamono jii, mbir mi daa takkarnaase, mel ni tuq su bënn, saañ ba réer. Ci weeru oktoobar wii nu génn lu tollook 480i doomi-aadama ñoo des ci géej gi (ñii dee, ñeneen ñi réer) ci diir bu gàtt, ci genn ayu-bés ! Woññiy néew de, neexut. Waaye, fàww nu def ko : ci bésub 24eelu oktoobar, 100i nit dee nañ mbaa ñu réer, ginnaaw ba soldaari Espaañ yi wallo 50i nit, fexe ba muccal leen. Ca bés boobu sax, fii ci géeji Senegaal yi, 140i doomi-Senegaal des nañu ci ndox mi ci sababug lakk gi xewoon ca gaal ga xale yi duggoon. Ci bésub 27eelu oktoobar mu amoon genn gaal gu bàyyikoo woon Sumbajun te yeboon 80i doomi-aadama, faf benn bato bu làrme Senegaal mbëkk ko, 41i nit dee ca mbaa ñu réer. Ñaari fan lañ ci teg, ci bésub 29eel oktoobar, genn gaal gu yaboon 77i nit suux, yóbbaale 50 doomi-Senegaal. Ca ëllëg sa, 30eelu fan ci oktoobar, 150i doomi-aadama ñoo des ci géej gi, boori Ndar. Boobaak léegi, nag, amul ayu-bés buy jàll te yéenekaay yi dun nu yëgal suuxug gaal, tàggewaaley xale yoo xam ne ñoo nara a dundali gaynde géej yi.

Rax-ci-dolli, li xew ci géej gi warunoo tax a fàtte liy xew ci mandiŋ mi. Ndax kat, ñu bare ci xale yiy gàddaay, ñu ngi koy jaare ci yay wi : di jël daamar yi, di dox, di fanaan ci àll bi, dëkko-dëkk ñu taxaw fa. Ñoom ñooñu, li ñuy daj ci yoon wi, tanewul la ca biir géej ga. Seen jafe-jafe yi dul jéex, dañ ciy boole xeetal gi ñuy jànkoonteel ci dëkki Naar yi ñuy jaar. Naar yu bëggul a gis Nit ku ñuul, di leen teg ñaawteef yi gën a ñaaw, lu xel  mënut a nangu. Lii moom, du jàmm ! Waaye am na leneen lu-dul jàmm te doy waar. Ndaxte, laaj wi sampu mooy : naka lam réew di daj lii ciw njaqare ak tiis, te di wéy di def niki dara xewul ! Ay téeméeriy nit yu deewandoo, te loolu daanaka yëngalul kenn ! Doo dégg walla nga gis njiitu-réew mi fullaal dëgg mbir mi, am ci taxawaay bi ñépp doon xaar ci ñoom : naqarlu ko, woote ci dëju askan wi, uti pexe yuy dakkal jii jéyya ! Waaw, ana tamit ñi ci kujje gi ? Ana sàmmkati àq ak yelleefi doomu-aadama yi ? Ana waa way-moomeel yi? Ana kàngami iniwérsite yi ? Kenn wooteewul ci lenn luy tax askan wi naqarlu musiba mu ni mel ! Woote taxaw-seetlu ba xam lu xew ? Xam lu waral bile balaa ? Ak lu ciy pexe ? Dëgg la, Njiitu-réew mi jël na xalimaam metitlu ko, waaye fa la yem ba léegi nii. Ndax waa Sàrli Ebdoo gën gone yiy des ci géej gi ? Seriñ Muntaqa it, ci fan yii rekk, ci baatu jawriñam, naqarlu na li xew, waar te yedd it askan wi, laata muy ñaan muslaay Sunu Boroom. Wànte, saafaras jéyya jii de, feeñagul ! Moone waa Senegaal dañuy faral a bàkkoo ne ay nit ñu nite lañu… Am déet ? Lu waral nu tekkaaral nii, ni muut ci mbir mi ? Ana bokk diine ji ne ci nun, muy jullit yi di kercen yi ? Ba noppi nag di bariy coow ci yeneen wàll yi mel ni politig bi ! Di seetaan jën yeek gaynde géej yiy xëccook a jiiroo, di yàpp sunuy doom yi lab ca géej gi. Amunu lu nuy def lu dul ne fii di lijjanti ay palaas yi politiseŋ yiy awante ci seen i biir, ngir rekk duufal seen i poos! Waaye nag, lu kenn mënul a dégg, mooy way-jur yii di yabal seen i doom yu amagul sax 20i at, dugal leen ci gaal yi wuti… Barsàq ! Noonu, ndeysaan, la ci xale bii di Duudu Fay mi amul lu dul 14i at ñàkke bakkanam, ginnaaw ba ko baay bi, Mamadu Lamin Fay, dugale cib gaalu musiba… Ngir lan ? Ciy yoxoy moroomam bu amagul 17i at la newoon ba muy nelaw ba fàww. Yeneeni way-jur yi àndoon ak seen i doom ñoom it, niki Lamin Fay, yoon a ngi leen di topp. Li xew ci réew mii, dëgg-dëgg, du jàmm ! Nu ñuy def ba delloosi xel yi ? Moone su nu xooloon ci ni réewi Tubaab yiy doxale, doon nanu am royukaay ci wàll wii. Ndax ñoom kat, kenn rekk ci ñoom, su waññeekoo, àddina sépp yëg ko. Lu waral nag, nun ñii jàpp ne, noo fi gën, nuy doxale nikiy bàyyima ? Xana du fii la bato «Joola» suuxe woon (1861i nit dee ci) mu doonoon jéyya ju ame géej ji yées ci àddina si. Te booba sax, askan wépp amoon na ci lu mu yëg, naqarlu woon ko bu baax, amoon ci tiitaange ju réy ; muy lu nuy jooy ba sunu jonni-tey jii ! Yëg-yëg boobu, fu mu nu jaar tey ?

Li xew ci réew mii, du jàmm !
Moone am nay ndaw yu ni du ñu toog di seetaan luxóor bu ni mel. Ndegam xam nañu ni, mënuñoo am jenn yaakaar ci Nguur gi, walla sax ci njiiti diine yi, dañu jóg, xar seen tànki-tubay, taxaw jàmmaarlook jafe-jafe yi. Dañoo jaar ci xaraley jokkookaay yu bees yi, ba jàpp seen bés bu ñu jagleel seen i moroom yi réer ci géej gi. Noonu lañ taxawalee seen mbooloo, jàpp ni kenn mënu leen a tee dëjal seen i mbokk, seen i xarit, seen i dëkkandoo, seen i moroom yi fi jóge ci anam yu ñaaw yooyule. Noonu lañu nasale seen bopp dëju askan wi. Te ñi dem barsàq kat, kenn mënu leen a jàppal lenn lu dul bëgg a tekki, maanaam, mënal seen bopp, mënal seen i way-jur, am dund gu dàq dund gi ñuy dund tey. «Ñépp xam nañu ne Ërob moo dàq Senegaal !» (ci li kenn ci waxambaane yi mucc ci gàddaay gi wax). Doonte, xale yi yaakaar ne seen wërsëg a nga feneen fu dul seen réew, xamuñu li leen di xaar fañ jëm. Ñu ci bari ci ñiy dàqi seen wërsëg, ña ciy egg, yaakaar ju tas lañ nar a taseel. Àjjana ja ñu yaakaaroon, naxee-mbaay lay mujjee doon.

Kuy wuti dëkk booy mën a tekki, daa fekk bunt yépp tëju sa kanam ca fa nga fekk baax ! Te, naka-jekk, xëy moom, daa tumurànke ci Senegaal gii ! Bu yàggul rekk la benn bànqaasu ONU (Kurelu mbooleem réew yi ci àdduna si) di xamal ne Senegaal bokk na ci réew yi gën a néewle xéy, doonte Gornmaa bi weddi na ko ba mu set. Waaye, su jafe-jafe yi yemoon foofu rekk, coow li du woon baree noonu. Li ci yéeme mooy ne, Gornmaa bii waroon a fexe ba xale yi am liggéey, moo leen koy far xañ ! Ndax kenn umplewul ne, ñi ëpp ci xale yiy songi géej gi ak boroom pexe yi leen di jàllale ci seen i gaal yi, ay mool lañu. Li ko waral mooy ne, mool yooyu, dañoo amatul fu ñu nappe ndax cër bu ngand bi Nguur gi yakkal bato yiy jóge bitim-réew. Ñooñu di ñëw ba ci wetu waax bi di raasaatu as tuut ci li sunuy nappkat yi dese woon. Ba tax na, li mool yi daan fortaatu, ci jën yu sew yi, dara lañ ci dul gisati ! Li ëpp ci bato yooyule, ñu ngiy jóge Portigaal, Espaañ, Farãs, Riisi walla Siin. Sunu mool yi, lu ñu foraatu, amatuñu ko. Ñàkk pexe nag, pexe la. Ku amul ndey nàmp maam. Ñoom ñi miin géej gi ba noppi, ñoo takk seen fit, uti Barsaa… mbaa Barsàq ! Ñu ñëw nag ci « mbëkk » mi, yokku ci gune yi amul woon xéy, xamatuñu woon fu ñuy jublu ; yokku it ci ubëryee yi ñàkkoon seen i liggéey, doon wër ba toqi ; ak tamit baykat yi gisatul woon tool yuy naat ba tax ñu wutsi péey bi, dàqsi seen
wërsëg…

Te, su desul lu dul sunu njiit yi, mel na ni yëf yi du fi yem. Ndax kat, ci fan yii rekk, Senegaal mayati na waa UE (réewi Tugal yi) ñuy wéy di fi indi seen i bato yi, di napp ni mu leen neexe. Ci lañu déggoo wéyal lu ni mel ci diiru yeneen juróomi at, ginnaaw ba ñu matalee juróom yu njëkk ya. Ci li ñu xaatim ci kayit, juróomi at yii, mënees na koo yeesal. Maanaam daal, tey la Waalo gën a aay ! Lu ëpp nag, tuuru. Waa Espaañ ya ubbi woon seen i digaloo yi, yombal dëkkin bi ci seen réew ndax mbas mi ak i balaam, dellu nañ ci ginnaaw, tëjaat ràpp seen bunt yépp. Yemuñu foofu, ñu ngiy waaj a yabal seen jawriñ bi yore mbiri bitim-réew, mu ñëw waxtaansi ak njiiti Senegaal yi, ba xam lu ciy pexe.  Ndegam yor nañu ay pexe !

Waaw, luy pexe ci jéyya jile ?
Nun waa Senegaal, nanu nite njëkk ! Ku wàññeeku (muy mbokk walla muy koo xamul), nanu ko metitlu ba fu metit yem ! Xam ne nit kuy dem ak i noppam, amul njëg, ak ku mu mën a doon, ak fu mu mën a jóge, ak nu mu mën a mel ! Nanu fonk doom-aadama, te naw sunu bopp ! Su loolu weesoo, ci wàllu politig bi, nanuy fal i njiit yu gëm seen bopp, bëgg seen réew, xareñ ci li ñiy def, te maandu ci alalu askan wi. Loolu rekk mooy tax ñoom ñooñuy falu, bokk yëg-yëg ak askan wi, di farlu ci faj seen i soxla. Lu ñuy nas, ñu nasandoo ko, lu ñuy liggéey, ñu liggéeyandoo ko, ngir rekk jëmale réew mi kanam, ba askan wi ci boppam, di gis boppam ci lépp luñ koy fexeel.

Uséynu Béey

Connexion utilisateur

Commentaires récents