WOTEY 2024 : YENN LAWAX YAA NGI NDOKKEEL BASIIRU JOMAAY JAXAAR FAY

Rubrique

Ginnaaw bi njureef yi tàmbalee rot, Basiiru Jomaay Fay moo jiitoogum, rawee yeneen lawax yi lu baree bari. Mu mel ni, sikk amul ci ne, moom B.J. J. Fay mooy nekk Njiitu réewum Senegaal lu bees li. Ñenn ci lawax yi doon xëccool ndokkeel nañ ko.

Muy kii di Paab Jibril Faal, Anta Baabakar Ngom, Décce Faal, Aali Nguy Njaay, ñépp ñoo ko ndokkeel ci ndam lu leer nàññ li mu am. Kariim Wàdd sax ndokkeel na ko.

Connexion utilisateur

Commentaires récents